Confidence : « Dama done déf ay appels vidéos, souméko ba sétt di woné… »

Kawtef, li rek moy kawtef, Gnéti lycéens you deuk Tivaouane la Tribunal bou flagrants délits bou Dakar Dane gnari atou kasso.

Liko waral moy Dagn done dieufa ndiko images diambour pour di déff chantage.
Cerveau bande bi mi ngui toudou Seydina Wayé dou mom dong. Ci liguèye bou bone bi wétou ci béne yone. Badara ak Ndèye, gnoy ak complices am.

Seydina, élève en classe de terminale Mo créer béne faux compte facebook ak photo xalé bou diongoma, Diokh ko Ndèye, élève en 3e, mou koy gérer.

Ndèye momou, Ndèye Badjo bi mo done proposé ay appels vidéos you doy war internautes youy weur lou bone té kham ko. Appels vidéos yi nak Ndèye dassi done souméko ba sétt wégn, ladj goor bimouy wakhal mou déf ni mome
wayé nak appels vidéos donoutone gratuit dé, appel bou ci nékk rek internaute bi dadone faye 5.000 FCFA
Li clients yi khamoutone moy dagn léne done filmé.

Guinaw bi appel vidéo bi diékhé, Seydina ak Ndèye ak Badara dagnouy wo clients yi diléne ladj khaliss kou bagn gnou menacer dougal say vidéos ci réseaux sociaux. Yén clients yi sakh diotnagnou fay kéne ci gnome fayna ba 250.000 FCFA.

Guinaw ay plaintes, yone tekna léne lokho, diébal léne procureur, Ci kanam tribunal bi Seydina, Ndèye ak Badara wédi wougnou dara ci touma yi gnou tekk séne kaw.

Tribunal dane na Badara gnari atou kasso yo kham ni 6 mois lay teud Seydina ak Ndèye, gnome dieul nagn gnari atou kasso yo khamni atoum leum laniouy teud.

Thiey Sénégal, ana liko fi diar?